Sunteți pe pagina 1din 17

Page titre

Seex Muusaa Ka

Jaaraam
Maam Jaara
1436 h / 2015 - www.drouss.org
Tous droits de reproduction rservs, sauf pour distribution
gratuite sans rien modifier du texte.
Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez
nous contacter par le biais de notre site internet :
www.drouss.org

Quelques indications
Wolof
per
rus
caam
am
xol
jibi
njaay
nday
aam
gm =

e=
u = ou
c = th
= gn
x = kh
j = dj
nj = nd
nd = nd

= eu
= (plus dur) = rr
o = au
gor
q = xx
suqali
ii - uu - oo - aa ee (tirer sur le son) ;
Ex : biir - suur -xool - gaal - xeer

2 - Jaaraama Maam Jaara

Franais
pr
rous
thiam
gnam
khol
djibi
ndiaye
ndeye
(machoire)
geum
perdu
gaure
soukh khali

Aperu sur lauteur

Pote et disciple de Seex Ahmadu Bmba, Seex Muusaa K fut


lun des plus grands historiens qui aient trait et comment la
vie du Cheikh.
Seex Muusaa K, fils de Usmaan et de Absatu Sekk, est n
Ndilki prs de Mbkke Bawal vers 1890. Il fit ses tudes
coraniques dabord aprs de son pre. Ensuite celui-ci le confia
Ahmadu Bmba qui, de retour de lexil en Mauritanie, le
garda dans sa cour de Ceyen (au Jolof) o il fut en rsidence
surveille de (1907 1912), puis Diourbel partir de 1912.
Atteint de variole, il dut renoncer son intention de faire des
voyages dtudes travers le pays pour rester auprs de Seex
Ibrahima Faal qui lui donna une solide formation religieuse.
Excellent calligraphe, il entra dans le foyer dtudes appel
Daaray Kaamil charg uniquement de lire et de transcrire le
Coran en plusieurs exemplaires. Promu cheikh par Xaadimu
Rasuul, il alla sinstaller Saat trois kilomtres de Mbakk
pour enseigner le Coran...
Ds la disparition de Seex Bmba en 1927, il se fit le compagnon
de Seex Mustafaa Mbkke, son fils, premier khalife des murids,
quil suivait dans ses dplacements travers le pays...
Jaaraama Maam Jaara - 3

Fin lettr, il a commenc du vivant de Seex Ahmadu Bmba


composer des pomes en langue arabe. Il les montra son
matre qui, souriant aprs lecture des textes, lui dit en wolof
: Muusaa, leeralal fr yi mbir mi, en substance Muusaa,
explique le message aux adeptes Muusaa, en murid
disciplin, comprit, par linjonction du marabout, quil fallait
sexprimer dans la langue wolof pour atteindre la grande
masse de disciple qui ne parlaient pas arabe...
Seex Muusaa Ka est un rudit. Il matrise aussi bien les
textes sacrs, les paroles et les faits du Prophte Anleyhi-ssalaatu wa salaam (la sunna), que loeuvre de son matre et
guide spirituel Xaadimu Rasuul. Cest ce qui lui permet de se
mouvoir aisment dans son domaine de prdilection et de
varier volont son style, ses thmes, la mtrique de ses vers,
inspirs certes de la qasida arabe mais dont le rythme reste
purement ngre...
Il a de nombreux sobriquets : Njam, Wrkaanu Bmba,
Xaadimul Xadiim, Gwl u Bmba. Certains de ses vers
rtablissent correctement les liens de parent qui le lient
Bmba. Mais, lui, a toujours souhait rester son chantre, car
pour les murids, il importe moins dtre un proche parent du
Cheikh que dtre son fidle taalib.
Voil Sri Muusaa Ka brivement prsent. On ne peut le
connatre rellement quen lisant la totalit de son oeuvre
monumentale estime plus de vingt mille (20.000) versets

4 - Jaaraama Maam Jaara

Ses Ouvrages : Ndiouth Ndiath ; Yrmande ; Taxmiss bob


wolofal ; Muqadimaat ; Xarnu bi ; Su ngeen ma degloo ; May
dagaan ; Boroomam ; Jigen u Mbkke-Mbkke ; Jaaramaa
Maam Jaara ; Soxna Jaara ; Barsan ; Jazu Sakor u Gej gi ;
Jazu Sakor u Jeri ji ; Sa pack bi ; Ci barke Bmba ; Ma yeesal
(Xadi Sill) ; Ndenkaani buy royu gor ; Yalla yi teqqalikook yu
suufe yi ; Marsiyya Seex Ibra Faal ; Sopp Ahmadul Mbkkii ;
Maggal yi ; Ndaama day yuqeelu (Matlabul aajaati) ; Mustafa
Mbkke ; Na jema buurati...

Jaaraama Maam Jaara - 5

Jaaraama Maam Jaara

Bismi-l-laahi-r-Rahmni-r-Rahmi
Wa sallalaahu Tahanlaa anla Seyidina wa mawlaanaa
Muhammadin wa aalihi wa sahbihii wa xayra xadiimihii wa
sallama tasliiman

Xerawlu leen nu sant Soxna Jaara


Ngir moo nu may li tax nu sampi daara
Bu leen ma tanqamlu, bu leen ma tanqal
Bu leen nxal ndoxum ki leen di tnqal
Cellantu leen te wubbi seni noppu
Ak sen xol ma wubbi seni boppu
Te gnne seni wagaani xol te taataan
Maam Jaara waame la ku naanul yaa bon
Taw na Bawal tawna Kajoor ak Njmbur
Ba walangaan ku mar lek doob jmbur
(1)

Waaloo ngi wal-wali di gental Waalo


Ngir naani ci gejuk doomi Asta Waalo

1 des nakoo bindee yit Bawol

6 - Jaaraama Maam Jaara

Jaaraama Maam Astu ma feeru Naawel


Sa gej gi neex na waaju naan si far wl
Jaaraama Maam Jaara ma feeru Poroxaan
Naxoo dayoo noo ngi dtm bay coroxaan
Gannr dtm nau ba naan ba mandi
Yaay bambulaan sam ndox xajul ci xandi
ppa gi moss sab liggey ba Saalum
Fuuta futtiku nau sagan ne maalum
Yaw sa aub liggey bii dm na penku
Dem soow baarakalla lii duk faggu
Yekkal nga waa gej gi yekkal waa jeri
Ba pp gejal yaw bayo fu joor
Beykat nga bey nga beyooy dendi
Jigeen i booyal yaw nga bay ba Ndindi
Jigeen a soxla lau yaa doon Soxna
Ndaanaan nga wub nga lambi doomi soxna
Jaaraama Maam Jaara - 7

Moo tax jigeen i seni doom ne mng


Di rera kay fee yaw sa doom ne fng
Moo tax jigeen pp seni doom diy xaadam
Di gont a kay xy yaw sa doom dib yaaram
Yaa tax jigeen pp seni doom seex
Bu dul konak yaw noo ngi damm bay soox
Tekkalelaak jigeen i Buso Baali
Xawna araam mel na ni Yallaak yaali
Di tudd seni doom di tudd Bmba
Araam na ngir moom rekka ttan yen ba
Yaw yaa di Buso Baali kko cangaay
Naka nga jg sngg nu jox nu ay gaay
Yaa tax jigeen iy lamasoo ay mlfa
Nuy soli xawsa fu nu sob nu jl fa
Jigeen i da daa gaardi woddooy soppi
Gor i di biioy baxaoy roof roppi
8 - Jaaraama Maam Jaara

Yaa suturaal awra yi dindi joote


Mbkkee ngi mel ni Ndar Ja baa ngay jooti
La am fa getti Ndar te am Sindoodi
Yot nga ko waa Tuubaak Gdek Tindoodi
Jaaraama Maam Jaara ku am jaaraama
Yaa ko waral sa dooma ry karaama
Jaaraama Maam Jaara ku am Mqaama
Yaa ko waral kerook bisub qiyaama
Jaaraama Maam Jaara ku am ay xarbaax
Yaa ko waral sa dooma feealug baax
Jaaraama Maam Jaara kuy faj aajo
Yaa ko waral sa dooma fj sunu aajo
Jaaraama Maam Jaara ku am hidaaya
Yaa ko waral sa dooma am wilaaya
Jaaraama Maam Jaara ku am ty junni
Yaa ko waral sa dooma jommal jinn
Jaaraama Maam Jaara - 9

Jaaraama Maam Jaara sa xarful jiimi


Joxnala jikko yu raft yu yeme

(2)

Jub nga jubal nga japp yaw ty julli


Ty jangg ty jox ba leer ya jolli
T jikko yii may bgga lim amoo leen
Jigeen u bon ako amoon yaroo leen
Daawu la jw doo janni daawu la jayi
Doo jayu doo jaayooka jaaya ki jayi
Yaa sobu yoonu Jannatu Nahiimi
Kula royul dm Jaanamaak Jahiimi
Sa ra gi tax na ba ragal nga Ylla
Raft raft njortu t xam nga yilla
(3)

Rewoo ryoo reroo nenaa la daali


Doo rummi doo rambaaj Buso Baali
Amoon nga faayda amoon nga fulla
T amu fit am fit ba Yalla fal la
2 jiimu Jaara (la lettre jiim de Jaara)
3 raawu Jaara (la lettre ra de Jaara)

10 - Jaaraama Maam Jaara

Gore nga am nga kersa am nga karaama


Am nga ngrm yaw yaay boroom Mqaama
Amoo kaaan goreediwoo naam Baali
Doo dox di kekkantook a kiitu-aale
Ma wax say jikko misaal yu tuuti
Laaj leen ko maami Soxna Faati Tuuti
Maam Smba Mariaama ma daa raw cim lf
Hamdane li mane Jahnla moo ko taalif
Noon na bagaan ga woon fa Soxna Jaara
Mooy rerukaayub bpp dongo daara
Mbandam ma musla dey te da daa rootaan
Mooy naanukaayab gaaya da koy seetaan
Masula siis masul dox di bodd
Masul di wex-wexlooka dox di gdd
Daawul weranteeka xuloo ni njldi
Moo tax selalul jur nga kuuy jur mbaldi
Jaaraama Maam Jaara - 11

Kuy laa di Maam Sri Mammar moom Jaara


Mbaldee di Daam du gentu we mooy baara
Da nga lewat mk njaboot nib sardi
Moo tax nga jur jambaar ju mel ni gaynd
Daawo di songanteeka dox di daan
Ak di defant tax na am nga waan
Wcc nga jaajf ya selalu Buso
Yaa tax ba nuy seeral gurook a buusu
Feerul ci jjana ni xuurul hiini
Naaley muriitu yaak sa doom lil hiini
Moo tax u naa la Jaaratul Ilaahi
Mariaama mooy sa tur wu mag billaahi
Ummu xaliifatu-r-rasuulullaahi
Muhammadin waladi Abdillaahi
Ummu imaamu awliyaai-l-laahi
Am nga mqaamatu rijaalillaahi
12 - Jaaraama Maam Jaara

Am nga lu kenn amul fi nun billaahi


Maam Jaara nl al hamdulil Ilaahi
Mariaama fuqti muuqinaatillaahi
Sa dooma raw kuy jang Bismillaahi
Mo donnu Ahmadu Habiibullaahi
Mo masa jis Amiinu wahyillaahi
Yaay turandom Mariaama ummu iisaa
Sayidatu-n-nisaai raw nga sii saa
Moo donnu iisaa ma di Ruuhulaahi
Moo di donuy Muusaa Kalaamullaahi
Mo donnu Ibra may Xaliilullaahi
Moo donnu Aadama Safiiyyullaahi
Tuubaa liman tabihahu lillaahi
Waylun liman ankarahum billaahi
Lau joxoon Muhammadul Makiyyu
Mi ngi u jox Muhammadul Mbakiyyu
Jaaraama Maam Jaara - 13

Marxaba ummu Ahmadul Mbakiyyu


Waarisu diini Ahmadul Makiyyu
Marxaba ummu Ahmadal Xadiimi
Xaliili zi-l-Buraaqi wa-l-Xayzuumu
Marxaba uhtu Ahmadul Mbusobi
Ku masa wr tataam n tuubi ruubi
Tatay dojak w la defoon fa Naawel
Saeemsa sa mas ta toj t du ko aawal
Museefu ko soru ci rewum Saalum
Ci sox yu takk mbaa kyit fulaa yam
Yaa baaxu tur Buso t baaxu askan
Ygg naoo siyaare gn ji Yonnen
Yaa raftab juddu t baaxi waajur
Ku xncu sy saddiit du jis ludul ngor
Maam yaa nga gaddaay Gdeki Tooro
Diinek gor leen tere jubook Lamtooro
14 - Jaaraama Maam Jaara

Museefuleena jiitu cik wilaaya


Mbaa al Quraan mbaa xam-xamub diraaya
Daawu u puukare mbirum waliyyu
Ngir ay Shariif la ooy donuy Aliyyu
Bmbaa ni ma liy samandaay ab jant
Fnk ci maam ma tudd Mammar Anta
Leer gi bawo Mbusobe suuxi Mbkke
Royaat ca askan wa di Mbkke-Mbkke
Jant ba fnk na lndam ga daay na
Bideew suux na suuxileen mbr fee na
Shamsu Shumuusi doomi jantak weer nga
Yaw jarulaa misaal nd fs nga leer nga
Tambeel ba reeroon ca cosaan u di ko jeex
Fee na fa Mbkke leegi pp di fa seex
Shayxu Shuyuuxi yaa di seexub seex yi
Badrul buduuri yaa di weeru weer yi
Jaaraama Maam Jaara - 15

Xunmu faqiiri yaa di saqqum ndol yi


Siitu haqiiri darajaal nga gool yi
Ummul masaakiini dexuk miskiin yi
Abuul yataamaa yaay kenul jirim yi
Ma naa ko Mbkke yaay Shamsu-d-diini
Leeral nga Njmburak Bawal ak Siini
Siggil nga callalak Habiibullaahi
Maam Balla Aysa weeru gn wallaahi
Yaa tax ba kepp ku stoo ci Mbkke
Bu n juneet Ylla tofal ko barke
Waa Mbkke Saakaaki Mbkke Baari
Leeral nga leen ppa ngi dox di waare
Defar nga say bokku defar aw jmbur
Defar Bawal defar Kajoor ak Njmbur
a daa falook a doon woroomi daara
Amuu woon ku mel ni doomi Jaara
16 - Jaaraama Maam Jaara

S-ar putea să vă placă și